naan: «Waxtu wa mat na, nguurug Yàlla dëgmal na. Tuubleen seeni bàkkaar te gëm xibaaru jàmm bii.»

Markus 1:15

TUUBLEEN

Ndax kat ñépp a bàkkaar, ba jotewuñu leeru Yàlla.

Room 3:23

BÀKKAAR

Ndaxte peyooru bàkkaar mooy dee, waaye yiw wi Yàlla di maye mooy texe gu sax dàkk fi Almasi Yeesu, sunu Boroom.

Room 6:23

DEE

Waaye Yàlla moom, ni mu firndeele cofeelam ci nun, moo di, ba nu doon ay bàkkaarkat, ca la Almasi bi deewe ngir nun!

Room 5:8

COFEEL

Ndax kat ci yiw ngeen mucce ci kaw ngëm, te loolu jógewul ci yeen, mayu Yàlla la, du peyu jëf, ba kenn di ci kañu.

Efes 2:8-9

NGËM

Saw làmmiñ, soo ci biralee ne Yeesu moo di Boroom bi, sab xol it, nga gëm ci ne Yàlla dekkal na Sang Yeesu, dinga mucc. Ndax kat ab xol lees di gëme, ba am àtteb ku jub, te aw làmmiñ lees di birale ngëm gi ba mucc.

Room 10:9-10

TEXE

Kon bu nit ki bokkee ci Almasi bi, mbindeef mu bees lay doon. La woon day wonni, li teew nag, di lu yees.

2 Korent 5:17

BEES CI ALMASI